Compositor: Não Disponível
[Pape bilal]
Woo naa la jotuma la, lu waral lii?
[Awa thies]
Bébé sama yaay booy moo jël sama téléphone
[Pape bilal]
Laaj naa la say xaritoo kenn gisu la
[Awa thies]
Bébé sama baay booy moo tax génnuma
[Pape bilal]
Gis naa ni danga changé
Ay copine yu bees ngay fréquenté
[Awa thies]
Man jàmbatumaak sa jikko ju changé
Ngay kebatu naan, chiiium! (Ah bon?!)
[Pape bilal]
Indil prique bi nga takk maa ko jënde
[Awa thies]
Su mil kalson bi nga sol maa ko jënde
[Pape bilal]
(Ih yaw kañ nga jënde kalson bi?)
[Awa thies]
Si dàll ba yére sa lépp maa ko jënde
[Dane]
Àdduna bi boo ci nekkee dal!
Fawu ngay muñale pur ñu lay muñal
(Maram ak biram nàmm naa leen)
Muse, où est madame?
Seytaane bàyyileen ñu séy
Madame, ani muse?
Seytaane bàyyileen ñu séy, waaw
[Fatel]
Cinq cents fois ngay jooy dépanse
Man dootul man
[Waly dieng]
Xool na xool waaye danga ma yab
Loolu heey yaw moytuma
[Fatel]
Man awma lu may wax ak yaw
Góor gu yàccaaral day mel ni yaw
[Waly dieng]
Fàtte woon nga bi ngay ñëw fi
Ya rawoon baale bee
[Fatel]
Sama pàpa moo ma tooñ bi ma maye
May ma sama baat léegi sayee
[Waly dieng]
Sa pàpa num la tooñe la bëgg a xam man yaw
Yaa yàgg nga jooy
[Fatel]
Yaw xanaa doo rus sax, yàgg nga wax
Maa la gënal sa yaay sax
[Waly dieng]
Way! Yaw danga rew wala danga dof?
[Fatel]
Ma ni ma money yaw amoo ko maa ngi séy!
[Dane]
Àdduna bi boo ci nekkee dal!
Fawu ngay muñale pur ñu lay muñal
(Maram ak birmane nàmm naa leen)
Muse, où est madame?
Seytaane bàyyileen ñu séy
Madame, ani muse?
Seytaane bàyyileen ñu séy, waaw
[Ay jigéen]
Moom de dafa mel ni ku ragal jëkkër ji!
Daa ko waroon jàppu dóor ko dóor yu metti
Ki doy na war way!
Yaw bàyyil ma ki man bu doon man
Ba ma tàngal sama diwlin ne ko ko cër (ayyah)
[Iblow]
Man jaaxle naa, jaaxle naa ci koñ bile
Ñoom yàkkamtiwuñu lu dul xeex bañ jubile
[Azou]
Hey bro fi la bët yam
Mais xoolal alma ma naan man ci juis bëlé
[Iblow]
Ñoom ñépp dañ kumpa gaaw mel ni ñobaar (nga ni?)
Koñ baa ngi tang mel ni dañ fi sotti poobar
[Azou]
Ihhh saf na, kon saf na
Saf na, poobar bi saf na
[Dane]
Àdduna bi boo ci nekkee (yaay)
Fawu ngay muñale pur ñu lay muñal
(Maram ak birman nàmm naa leen)
Muse, où est madame?
Seytaane bàyyileen ñu séy
Madame, ani muse?
Seytaane bàyyileen ñu séy, waaw